Ubbil li ci biir

Ndax Yàlla am na tur?

Ndax Yàlla am na tur?

Li Biibël bi wax

Nit ku nekk am na tur. Yàlla nag, ndax moom am na tur? Bala ngay xaritoo ak kenn, fàww nga xam turam, du dëgg? Ndax du noonu la war a deme su ñu bëggee doon xaritu Yàlla?

Ci Biibël bi, Yàlla nee na: «Man maay Yexowa. Loolu mooy sama tur» (Esayi 42:8, MN). Dëgg la, mën nañu ko woowe «Yàlla Aji Man ji», «Boroom bi» walla «Bindkat» bi. Waaye may na ay jaamam lu réy: dafa bëgg ñu woo ko ci turam (Njàlbéen ga 17:1; Jëf ya 4:24; 1 Piyeer 4:19).

Turu Yàlla mën nga ko gis ci Biibël bi ci ay làkk yu bare ci Mucc ga 6:3. Aaya boobu nee na: «Yàlla Aji Man ji, mooy ni ma feeñoo woon Ibraayma, te ni laa feeñoo Isaaxa ak Yanqóoba it, waaye sama tur, Aji Sax ji [Yexowa, MN], leeraluma leen ko woon.»

Jéhovah mooy turu Yàlla ci farãse (Yexowa ci Wolof). Yàgg nañu di ko binde noonu ci lu ëpp ay téeméeri téeméeri at ci ginnaaw. Ci boroom xam-xam yu bare, binde ko «Yahvé» moo leen gënal, waaye Jéhovah moo gën a ràññeeku. Xaaj bi njëkk ci Biibël bi, ci làkku Ebrë lañu ko binde woon. Melul ni farãse ndaxte dañu koy liire ndeyjoor jëm càmmooñ. Ci làkk boobu, turu Yàlla ñeenti araf yii la: יהוה, maanaam YHWH, te ñu woowe ko ci farãse tétragramme.