Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC FUKK AK JURÓOM-ÑAAR

Jegeleen Yàlla ci ñaan

Jegeleen Yàlla ci ñaan
  • Lu tax ñu war a ñaan Yàlla ?

  • Lan lañu war a def ngir Yàlla nangu suñuy ñaan ?

  • Naka la Yàlla di tontoo suñuy ñaan ?

“ Ki sàkk asamaan ak suuf ” nangu na déglu suñuy ñaan.

1, 2. Lu tax ñu war a jàppe ñaan Yàlla ni cér bu réy, te lu tax ñu war a xam li Biibël bi wax ci ñaan ?

BU ÑU xoolee ni àddina bi yaatoo, dañuy gis ne suuf si dafa tuuti lool. Ci kanamu Yexowa moom mii “ sàkk asamaan ak suuf ”, réewi àddina si dañu mel ni toqu ndox ci siwo (Sabóor 115:15, NW ; Isaïe 40:15). Waaye, Biibël bi nee na : “ Yexowa dafa jege képp ku koy ñaan, jege képp ku koy ñaan ci dëgg. Dina may ñi ko ragal li ñu bëgg, te dina leen déglu bu ñuy woote ngir ndimbal. ” (Sabóor 145:18, 19, NW). Seetal rekk li loolu di tekki ! Sàkk-kat bi Aji Kàttan ji dafa ñu jege, te dina ñu déglu bu ñu “ koy ñaan ci dëgg ”. Mën a ñaan Yàlla, cér bu réy la !

2 Bu ñu bëggee Yexowa nangu suñuy ñaan, fàww ñu ñaan ko ci fasoŋ bi mu bëgg. Bu ñu xamul li Biibël bi wax ci ñaan, naka lañuy mënee ñaan Yàlla ni mu ko bëgge ? Xam li Mbind mi wax ci ñaan dafa am solo lool ci ñun, ndaxte ñaan dafa ñuy dimbali ñu jege Yexowa.

LU TAX ÑUY ÑAAN YEXOWA ?

3. Waxal lenn lu am solo li tax ñu war a ñaan Yexowa.

3 Lenn lu am solo li tax ñu war a ñaan Yexowa mooy, moom moo ñu wax ñu def ko. Lii la ñu Kàddoom wax : “ Buleen jaaxle ci dara, waaye ci lépp wéetal-leen Yàlla, diis ko seeni soxla ci ñaan gu ànd ak cant. Noonu jàmmu Yàlla, ji xel mënta takk, dina aar seeni xol ak seeni xalaat ci darajay Kirist Yeesu. ” (Filib 4:6, 7). Ci dëgg, bëgguñu sàggane lu baax li ñu Njiit bi gën a mag ci àddina si may !

4. Faral di ñaan Yexowa, naka lay rattaxale suñu diggante ak moom ?

4 Leneen li tax ñuy ñaan Yexowa mooy, faral di ko ñaan, dafay rattaxal suñu diggante ak moom. Ay xarit dëgg, du bu ñu amee lu ñu soxla kese lañuy waxtaan. Waaye ay xarit dëgg, kenn ku ci nekk dafay xalaat moroomam. Te seen diggante dafay gën a dëgër bu ñuy waxtaan ci seen xalaat, ci seeni itte ak ci li nekk ci seen xol te kenn du ci rus moroomam. Ci yenn fànn, suñu diggante ak Yexowa Yàlla noonu la mel itam. Téere bii dimbali na la nga xam lu bare ci li Biibël bi wax ci Yexowa, li mu wax ci jikkoom, akit ci coobareem. Dem nga ba xam ko ni ñuy xame nit. Ñaan Yàlla dafa lay may nga wax sa Baay bi nekk ca asamaan sa xalaat ak li nekk ci sa biir xol. Sooy def loolu, dinga gën a jege Yexowa. ​— Saag 4:⁠8.

LAN LAÑU WAR A DEF ?

5. Lan mooy wone ne Yexowa du déglu ñaan yépp ?

5 Ndax Yexowa ñaan yépp lay déglu ? Xoolal li mu waxoon waa Israyil, ñi ko bañoon a déggal ci jamono yonent Yàlla Esayi : “ Ngeen bareel seeni ñaan, ma tanqamlu leen: seeni loxo dañoo fees ak deret. ” (Esayi 1:15). Kon am na jëf yuy tax Yàlla bañ a déglu suñuy ñaan. Bu ñu bëggee Yàlla nangu suñuy ñaan, am na lu am solo lu ñu mënul a ñàkk a def.

6. Bu ñu bëggee Yàlla nangu suñuy ñaan lu am solo lan lañu war a njëkk a def, te naka lañu ko mën a defe ?

6 Lenn lu am solo li ñu war a def mooy wone ngëm ci Yàlla (Màrk 11:24). Lii la ndaw li Pool bindoon : “ Ku amul ngëm doo man a neex Yàlla, ndaxte ku bëgg a jegeñ Yàlla war ngaa gëm ne, Yàlla am na te dina neexal ñi koy wut. ” (Yawut ya 11:⁠6). Am ngëm dëgg yemul kese ci nangu ne Yàlla am na, dafay déglu suñuy ñaan te di leen tontu. Ci ay jëf lañuy wone suñu ngëm. Dañu war a wone ba mu leer ne gëm nañu Yàlla ci fasoŋ bi ñuy dunde bés bu nekk. — Saag 2:⁠26.

7. a) Lu tax ñu war a may cér Yexowa bu ñu koy ñaan ? b) Naka lañuy wonee ne dañu woyof te dëggu bu ñuy ñaan Yàlla ?

7 Yexowa dafa bëgg it ñu woyof te dëggu bu ñu koy ñaan. Am na lu bare lu tax ñu war a woyof bu ñuy ñaan Yàlla. Bu nit di wax ak buur walla njiitu réew, dafa koy may cér ndax li mu doon kilifa bu mag. Kon, bu ñuy jege Yexowa ci ñaan, foofu la may cér bi war a ëppe (Psaume 138:⁠6) ! Xanaa du mooy «Aji Man ji» ? (Njàlbéen ga 17:1.) Bu ñuy ñaan Yàlla, fasoŋ bu ñu koy defe dafa war a wone ne dañu suufeel suñu bopp te nangu ne dañu tuuti lool ci kanamam. Woyof bu mel noonu dina tax suñuy ñaan dëggu te doon li ñu tibbe ci suñu xol. Te dinañu moytu di wax lu bare lu amul njariñ walla di tari ay ñaan. ​— Macë 6:​7, 8.

8. Naka lañuy def ba suñuy jëf ànd ak li ñu ñaan Yàlla ?

8 Leneen liy tax Yàlla nangu suñuy ñaan mooy suñuy jëf ànd ak li ñuy ñaan. Yexowa dafa bëgg ñu def lépp li ñu mën ngir li ñuy def ànd ak suñuy ñaan. Nañu ko seet ci lii : Bu ñu ñaanee Yàlla mu “may nu tey li nu war a dunde”, dañu war a góor-góorlu bu baax ci bépp liggéey bi ñu gis te ñu mën koo def (Macë 6:11 ; 2 Tesalonig 3:10). Bu dee dañu ñaan Yàlla mu musal ñu ci bàkkaar, war nañu moytu nekk ci li ñu mën a dugal ci lu bon (Kolos 3:5). Ginnaaw li am solo li ñu fi wax ci ñaan Yàlla, am na yeneen laaj yu jëm ci ñaan te ñu war a xam tont yi.

NAÑU TONTU CI YENEEN LAAJ YU JËM CI ÑAAN YÀLLA

9. Kan lañu war a ñaan, te ci turu kan lañu war a jaar ?

9 Kan lañu war a ñaan ? Yeesu waxoon na ay taalibeem ñuy ñaan “ sunu Baay bi nekk ci kaw ” asamaan (Macë 6:⁠9). Kon Yexowa Yàlla kese lañu war a ñaan. Waaye, Yexowa dafa bëgg ñu nangu taxawaayu benn Doom ji mu am kepp, maanaam Yeesu Kirist. Ni ñu ko gise ci pàcc 5, Yàlla dafa yónni Yeesu ci kaw suuf mu nekk njot, ngir musal ñu ci bàkkaar ak dee (Yowaana 3:16 ; Room 5:12). Yeesu mooy ki Yexowa tànn mu nekk saraxalekat bu mag bi ak it àttekat (Yowaana 5:22 ; Yawut ya 6:20). Looloo tax Mbind mi sant ñu ñuy jaar ci turu Yeesu ngir ñaan Yàlla. Moom ci boppam nee woon na : «Man maay yoon wi, maay dëgg te dund it man la. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarul ci man.» (Yowaana 14:⁠6). Bu ñu bëggee Yàlla nangu suñuy ñaan, dañu war a ñaan Yexowa kese, te jaar ci turu Doomam.

10. Lu tax amul fasoŋ bu ñu war a tooge walla taxawe bu ñuy ñaan Yàlla ?

10 Bu ñuy ñaan, ndax am na fasoŋ bu ñu war a tooge, taxaw walla def leneen ? Déedéet. Yexowa waxu ci dara. Waxul ni ñu war a defe suñuy loxo, walla suñu yaram. Biibël bi nee na am na fasoŋ yu bare yu ñu mën a def bu ñuy ñaan Yàlla. Mën nañu toog, sëgg, sukk walla ñu taxaw (1 Chroniques 17:16 ; Nehémia 8:6 ; Dañeel 6:11 ; Màrk 11:25). Li ëpp solo mooy ñu am xol bu rafet, waaye du li nit ñi di gis mel ni fasoŋ bi ñuy taxawe walla yu mel noonu. Kon, bu ñuy dox suñuy soxla, walla ñu nekk ci jafe-jafe, mën nañu ñaan Yàlla ci suñu biir xol fépp fu ñu mënta nekk. Yexowa dafay dégg ñaan yu mel noonu, su dee sax ñi ñu wër seetluwuñu ko. ​— Nehémia 2:​1-6.

11. Yan poroblem yu ñuy am, ñun ci suñu wàllu bopp, lañu mën a boole ci suñuy ñaan ?

11 Lan lañu mën a ñaan Yàlla ? Biibël bi nee na : “ Kóolute gi nu am ci kanam Yàlla mooy lii, su nu ko ñaanee dara ci coobareem, [Yexowa] dina nu nangul. ” (1 Yowaana 5:14). Kon mën nañu ñaan Yàlla lépp li ñu bëgg, waaye fàww mu ànd ak coobareem. Ndax Yàlla bëgg na ñu ñaan ko lu jëm ci poroblem yu ñuy am, ñun ci suñu wàllu bopp ? Waawaaw ! Ñaan Yexowa mën na niru lool ak booy waxtaan ak sa xarit bu la jege lool. Mën nañu wax lépp Yàlla, ‘ wax ko lépp li nekk ci suñu xol ’. (Sabóor 62:8, NW.) Baax na it ñuy ñaan Yàlla mu may ñu xel mu sell ndaxte dina ñu dimbali ñuy def lu baax (Luug 11:13). Mën nañu ñaan Yàlla mu dimbali ñu ngir ñu tànn li gën a baax ci ñun. Mën nañu ko ñaan it mu may ñu doole ngir muñ ay jafe-jafe (Saag 1:⁠5). Bu ñu bàkkaaree, dañu war a ñaan Yàlla mu baal ñu ci kaw saraxu Kirist (Efes 1:​3, 7). Dëgg la, du ci suñuy poroblem kese lañu war a ñaan Yàlla. War nañu di ñaanal it ñeneen, suñu waa kër ak suñuy mbokk ci wàllu ngëm. ​— Jëf ya 12:5 ; Kolos 4:⁠12.

12. Naka lañu mënee wone ne lu jëm ci suñu Baay bi nekk ca asamaan moo ëpp solo ci suñuy ñaan ?

12 Lu jëm ci Yexowa moo war a jiitu ci suñuy ñaan. Ci lu wóor am nañu lu tax ñu war a màggal Yàlla ak suñu xol bépp te di ko gërëm it ci mbaaxaayam (1 Chroniques 29:10-13). Yeesu wone na ni ñu war a ñaane. Bind nañu ko ci téere Macë 6:9-13. Ci ñaan boobu, Yeesu dafa ñu jàngal ñuy ñaan ngir ñu sellal turu Yàlla. Bi Yeesu waxee loolu mu teg ci ne dañu war a ñaan ngir Nguuru Yàlla ñëw te coobare Yàlla am ci suuf mel ni ci kaw asamaan. Bi mu waxee ci lu am solo loolu jëm ci Yexowa ba pare, mu sog a wax lu jëm ci suñuy soxla bopp. Bu ñu joxee Yàlla wàll bi gën a am solo ci suñuy ñaan ni ko Yeesu defe woon, dinañu wone ne du suñu bopp rekk lañuy xalaat.

13. Lan la Mbind mi wax ci guddaayu ñaan bu Yàlla mën a nangu ?

13 Ñaata minit lañu war a ñaan ? Biibël bi waxul dara ci guddaayu ñaan, moo xam ñun kese la walla ñaan bu ñuy def ci biir mbooloo. Ñaan mën na gàtt bu dee bala ñuy lekk lañu koy def. Mbaa mu gudd su dee dañu wéet ak Yexowa ngir wax ko li nekk ci suñu xol (1 Samwil 1:12, 15). Waaye ñi foogoon ne ay nit ñu jub lañu te doon ñaan Yàlla ay ñaan yu gudd ngir nit ñi xool leen, Yeesu waxoon na ne loolu lu bon la (Luug 20:46, 47). Ñaan yu mel noonu yëngalul Yexowa. Li gën a am solo mooy ñaan bu jóge ci suñu xol. Kon guddaayu ñaan bi Yàlla mën a nangu, mu ngi aju ci li ñu soxla ak ci fi ñu nekk.

Yàlla mën na déglu suñuy ñaan fépp fu ñu mënta nekk.

14. Lan la Biibël bi bëgg a wax bi mu ñuy xiir ci kontine di ñaan Yàlla, te lu tax loolu di dalal suñu xel ?

14 Ñaata yoon lañu war a ñaan Yàlla ci bés bi ? Biibël bi dafa ñuy xiir ci kontine di «ñaan», te “ sax ci ñaan Yàlla ”. (Macë 26:41 ; Room 12:12 ; 1 Tesalonig 5:17.) Li Biibël bi wax noonu, tekkiwul ne dañu war dëkk ci ñaan Yexowa ci waxtu bu nekk. Waaye Biibël bi dafa ñuy xiir ñuy faral di ñaan Yexowa, kontine di ko gërëm ci mbaaxaay bi mu ñuy won, te di ko ñaan mu xelal ñu, dalal suñu xel te may ñu doole. Yexowa waxul dara ci ni suñu ñaan waree gudd ak ñaata yoon lañu ko war a ñaan ci bés bi. Ndax loolu du dalal suñu xel ? Mën a ñaan Yàlla cér bu réy la. Su ñu ko fonkee dëgg, dinañu gis lu bare lu war a tax ñuy mën a ñaan suñu Baay bi nekk ca asamaan.

15. Bu ñu paree ñaan, moo xam suñu ñaanu bopp la walla ñuy ñaan ci mbooloo, lu tax ñu war a wax “ amiin ” ?

15 Lu tax ñu war a wax “ amiin ” bu ñu paree ñaan ? “ Amiin ” dafay tekki “ ci lu wóor ” walla “ na li ñu wax am ”. Li ñu nettali ci Biibël bi dafay wone ne jaadu na ñuy wax “ amiin ” ​bu ñu paree ñaan, moo xam suñu​ ñaanu bopp la walla ñuy ñaan ci mbooloo (1 Chroniques 16:36 ; Psaume 41:13). Bu ñu waxee “ amiin ” bu ñu paree ñaan, loolu dafay wone ne li ñu wax ci ñaan bi dëgg la ci ñun. Bu amee ku ñaan ci mbooloo mi ba pare, bu ñu waxee «amiin» ci suñu xel walla ñu wax ko ci kaw, loolu dafay wone ne ànd nañu ak li mu wax ci ñaan bi.​ — 1 Korent 14:⁠16.

NAKA LA YÀLLA DI TONTOO SUÑUY ÑAAN

16. Lan lañu mën a jàpp ne lu wóor la ci wàllu ñaan ?

16 Ndax Yexowa dafay tontu dëgg ñi koy ñaan ? Waawaaw ! Am nañu lu wóor luy tax ñu mën a gëm ne “ Kiy déglu ñaan yi ” dafay tontu ñaan yu dëggu yu ko ay milyoŋi nit di ñaan (Sabóor 65:2, NW). Yexowa mën na tontu suñuy ñaan ci fasoŋ yu bare.

17. Lu tax ñu mën a wax ne Yàlla dafay jaar ci malaakaam yi ak ci jaamam yi nekk ci kaw suuf ngir tontu suñuy ñaan ?

17 Yexowa dafay jaar ci ay malaakam akit ci ñi koy jaamu ci kaw suuf ngir tontu ñaan yi (Yawut ya 1:13, 14). Am na nit ñu bare ñu mas a ñaan Yàlla ngir mu dimbali leen ñu xam li nekk ci Biibël bi. Tuuti ginnaaw loolu, kenn ci ñiy jaamu Yexowa daldi leen seetsi. Lu mel noonu dafay wone ne malaaka yi ñu ngiy jiite liggéeyu waare Nguuru Yàlla (Peeñu ma 14:6). Bu ñu amee soxla dëgg ba wax ko Yexowa ci ñaan, ngir tontu suñuy ñaan, Yexowa mën na def suñu mbokk karceen ñëw dimbali ñu. ​— Proverbes 12:25 ; Saag 2:16.

Ngir tontu suñuy ñaan, Yexowa mën na def suñu benn mbokk karceen ñëw dimbali ñu.

18. Naka la Yexowa di jaare ci xel mu sell mi ak ci Kàddoom ngir tontu ñaanu jaamam yi ?

18 Yexowa Yàlla dafay jaar it ci xel mu sell mi ak ci Kàddoom, Biibël bi, ngir tontu ñaanu ñi koy jaamu. Mën na jaar ci xel mu sell mi ngir xelal ñu te may ñu doole, ngir tontu suñuy ñaan bu ñu amee ay jafe-jafe (2 Korent 4:⁠7). Bare na li Yexowa di jaar ci Biibël bi ngir tontu ñu bu ñu koy ñaan mu won ñu li ñu war a def. Mën nañu gis ay aaya yi ñu mën a dimbali bu baax bu ñuy gëstu Biibël bi, ak bu ñuy jàng téere karceen yu mel ni téere bii. Mën nañu dégg xelal yi ñu soxla te nekk ci Mbind mi bu ñu nekkee ci ndaje karceen yi, walla bu benn njiit bu la bëgg ci mbooloo mi di la xelal. ​— Galasi 6:1.

19. Bu dee dafa mel ni Yàlla du tontu suñu ñaan, lan lañu warul a fàtte ?

19 Su fekkee ne dafa mel ni dañu toog lu yàgg te Yexowa tontuwu ñu, loolu du tekki mukk ne mënu ñu tontu. Buñu fàtte ne li Yexowa di tontu dafay ànd ak coobareem te dafa koy def ci waxtu bi gën. Xam na li ñu soxla, te moo ñu gën a xam fuuf ni ñu koy faje. Lu ci bare, dafa ñuy bàyyi ñu kontine di ñaan, di seet, akit di fëgg. (Luug 11:5-10.) Bu ñu kontinee te bañ ci tàyyi, loolu dina won Yàlla ne bëgg nañu dëgg li ñu ñaan te it suñu ngëm dëgër na. Rax-ci-dolli, Yexowa mën nañu tontu ci fasoŋ bu yombul a gis. Yexowa mën na ñu tontu ci benn jafe-jafe, te du ko dindi sax. Waaye dafa ñuy may doole ngir ñu mën koo muñ. ​— Filib 4:13.

20. Lu tax ñu war a jariñoo bu baax cér bu réy bi ñu am maanaam mën a ñaan Yàlla ?

20 Kontaan nañu lool ci li Ki sàkk àddina bu yaatu bi jege képp ku koy ñaan ci fasoŋ bu baax (Psaume 145:18). Mën a ñaan Yàlla cér bu réy la. Nañu ko jariñoo bu baax. Su ko defee, dinañu am lu neex, maanaam di gën a jege Yexowa mi nekk Kiy déglu ñaan yi.