Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 4

Naka lañu war a yoree xaalis ?

Naka lañu war a yoree xaalis ?

Bu diisoo amee, pexe dina am. — Proverbes 20:⁠18

Ñun ñépp soxla nañu xaalis ngir faj suñu soxlay njaboot (Kàddu yu Xelu 30:⁠8). Ni ko Biibël bi waxee, xaalis dafa ñuy aar ci lu bare (Ecclésiaste 7:​12). Yéen ñi séy, waxtaan ci li ngeen di def ak seen xaalis mën na bañ a yomb, waaye buleen bàyyi xaalis indi poroblem ci seen séy (Efes 4:​32). Bu jëkkër ak jabar di waxtaan ci depãs yi ñu bëgg a def, fàww ku nekk wóolu moroomam te def lépp ngir juboo.

1 XALAATLEEN BU BAAX CI DEPÃS YI NGEEN BËGG A DEF

LI BIIBËL BI WAX : “ Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkka toog, xalaat ñaata la ko wara dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu mana àggale liggéey bi ? ” (Luug 14:28). Am na solo lool ngeen toog yéen ñaar ngir xalaat ci depãs yi ngeen bëgg a def (Amos 3:⁠3). Seetleen li ngeen soxlaa jënd ak li ngeen mën a génne ci xaalis ngir jënd loolu (Kàddu yu Xelu 31:16). Mën a jënd dara warul a tax ngeen jënd ko. Fexeleen ba moytu bor. Yemleen rekk fi seen poos tollu. — Kàddu yu Xelu 21:5 ; 22:⁠7.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Bu ngeen desee xaalis ci weer bi, toogleen waxtaan ci li ngeen ci nar a def

  • Bu xaalis bi jeexee bala weer bi dee, xoolleen depãs yi ngeen war a waññi. Mën ngeen a togg kër ga. Moo gën a yomb dem lekk ci biti

2 BULEEN NËBB DARA TE XAMLEEN LI NGEEN ÀTTAN

LI BIIBËL BI WAX : “ Danuy fexe def li jub, du ci kanam Yàlla rekk, waaye it ci kanam nit ñi. ” (2 Korent 8:​21). Waxal sa jëkkër walla sa jabar ñaata ngay am ci xaalis ak fi nga koy dugal.

Saa yoo bëggee def depãs bu réy, nanga ci waxtaan ak ki nga séyal (Kàddu yu Xelu 13:10). Faral di waxtaan ci xaalis bi ngeen am moo leen di dimbali ci kontine di am jàmm ci seen séy. Xaalis bi ngay am, bu ko jëlee ni sa xaalis yaw kese waaye jëlee ko ni xaalisu njaboot gi. — 1 Timote 5:⁠8.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Waxleen ba juboo ci ñaata xaalis la ku nekk mën a jaay te du soxla muy tàggu moroomam

  • Buleen bàyyi ba poroblem am, ngeen sog a waxtaan ci seen xaalis