Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

XAAJ 5

Li Ngeen Mën a Def ngir Wéy di Juboo ak Seeni Mbokk

Li Ngeen Mën a Def ngir Wéy di Juboo ak Seeni Mbokk

“ Solooleen . . . laabiir, woyof, lewet ak muñ. ” — Kolos 3:​12

Bés boo amee jëkkër walla jabar, njaboot gu bees ngay tàmbali. Dëgg la dinga kontine di bëgg say waajur te may leen cér, waaye léegi sa jëkkër walla sa jabar mooy nit ki gën a am solo ci yaw ci kaw suuf. Mën na am mu jafe ci say mbokk ngir ñu nangu loolu. Waaye santaane yi nekk ci Biibël bi dinañu la dimbali nga xam ni nga war a doxale ak ku nekk. Loolu dina tax ngeen mën a kontine di juboo ak seeni mbokk boole ci am jàmm ci njaboot gu bees gi ngeen di tàmbali.

1 KONTINELEEN DI GISE SEENI MBOKK NI MU WARE

LI BIIBËL BI WAX : “ Teralal sa ndey ak sa baay ” (Efes 6:⁠2). Ak at yi nga mënta am, danga war a teral say waajur te may leen cér. Nangul ne ki nga séyal itam doom la bu soxlaa am itte ciy waajuram. Mbëggeel du fiir, kon bul mas a ragal ne diggante bi sa jëkkër walla sa jabar am ak waajuram yi dina waññi dara ci seen séy. — 1 Korent 13:4 ; Galasi 5:​26.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Moytul di wax lu mel ni “ Sa mbokk yi, saa su nekk dañu may wàññi ” walla “ Sa yaay masul a bëgg li may def ”

  • Jéemal a gise mbir mi ni ko ki nga séyal gise

2 BU KO MBIR MI LAAJEE, JËLLEEN DOGAL TE DËGËR CI

LI BIIBËL BI WAX : “ Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy kenn ” (Njàlbéen ga 2:24). Bés boo amee jëkkër walla jabar, say waajur mën nañu kontine di xalaat ne ba tey yaa ngi ci seen loxo, te xéyna dinañu bëgg a dugg ci sa séy ba weesu fi ñu war a yem.

Yéen ñaar a war a déggoo ci fi ngeen bëgg seeni waajur yem ci seen séy, ba pare ngeen wax leen ko boole ci cofeel bu mat. Mën ngeen a wax li ngeen xalaat te wax ji du ñagas (Kàddu yu Xelu 15:⁠1). Woyof, lewet, ak muñ dinañu la dimbali nga am diggante bu rafet ak say mbokk te kontine di “ baalante ci mbëggeel ”. — Efes 4:⁠2.

LI NGEEN MËN A DEF :

  • Su ngeen gisee ne seeni mbokk dañu dugg ci seen séy ba mu ëpp te loolu naqari leen, yéen ñaar nangeen ci waxtaan bu seen mer dalee

  • Nangeen déggoo ci ni ngeen di reglee poroblem bi